osad4.jpgosad2.jpgosad5.jpgosad1.jpgosad3.jpg

Note utilisateur: 0 / 5

Etoiles inactivesEtoiles inactivesEtoiles inactivesEtoiles inactivesEtoiles inactives
 

Altine 21 sàttumbar 2009

Jukki bii tibbees na ko ci Taaral ak ladab ci làmmiñu wolof « Esthétique et Littérature de langue wolof », Séex Aliyu Ndaw bind ko , Osad defar ko, oktoobar, 2002, 64 xët

Njàngatu Séex Aliyu Ndaw ci woyu Sëriñ Muusaa Ka


 
Sëriñ Muusaa Ka mook Sëriñ MBay Jaxate i taalibe Sëriñ Tuubaa lañu. Li ëpp ci seen bind génnul mbirum diine ak di jéem a jëmale nit ñi ci lépp lu lislaam digle.
Ma baamtuwaat fi ne : man taaral gi lal seenum mbind ak ni muy firndeele ne amul lu làmmiñu wolof di ñeetaane weneen làkk moo ma tax a sukkandiku ci seeni woy.
Ku mel ni Muusaa Ka, ba mu bëggee wone màggaayu Boroom Tuubaa, te it wonewaale ni mu fekke woon diine ràgg, mu jël ko ragg ko ba mu set, teg ci kanami doom aadama, ak nag wone ni nit ñi daan def ndiiraan di fëx wutalsi Sëriñ bi, ngir di wut Yàlla ak Yonentam bu tedd ba. Bari ga ñu bari ak na ñu toftalantee, fu mu ne, ñu fekk ko fa, werekaan bu mel ni Muusaa Ka, ba mu bëggee indi lii lépp ci woy, te xam ne boo koy jàng walla nga dégg ñu jàng ko, nga daldi janeer na nit ñay def jëm ca Boroom Tuubaa, dafa liggéey i baat yu ëmb yu mën a leeral lii lépp, tënk ko, te neex ci nopp ak ci xol, ba noppi bët mel ni mu ngi ne ci jàkk. Moo tax Muusaa ne :

                                                   Waaloo ngiy wal-wali di gental Waalo
                                                   Ngir bëgg naani géejag doomu Asta Waalo.

Werekaan bi baatu “wal” la tànn, xam ne ndox doŋŋ a ko moom. Mu jublu ci bari ga nit ñi bari ak doole ja ñuy àndal ci xér ga ñu xér, su ñu fëxee wuti Sëriñ bu mag bi. Waaye bu bindee “Waalo” it, jubluwu ci réewum Waalo doŋŋ, àddina si ak fu nit mënti jóge la ci jublu. Defar taaru woy wi, ak tëgg mbaa yatt i baat yu ànd te méngoo, te mën a feelu wal gi mu bëgg mu màndargaal bari geek toftalante geek daw gi, moo tax mu jël “Waalo” mu taxaw taxawaayu àddina, ci biir woy wi. Moo tax baati nas bu jëkk bi seeni ndoorte yépp di “W”.

                                                        Waaloo ngiy wal-wali di gental Waalo

Bu ñaareel bi it nag moom, li tax Muusaa indee ko nii, mujjantal ba lay dàkk, muy baati “Asta Waalo” mu daldi méngook “Waalo” gi ci nas bu jëkk bi, lépp di :

                                                        Waaloo ngiy wal-wali di gental Waalo
                                                        Ngir bëgg a naani géejag doomu Asta Walo

Soo xàmmee nag ne Maam Asta Waalo mooy Maami Sëriñ Tuubaa, nga daldi yëg te jàpp ne ndekete riir meek bari geek xér gi, lii lépp nammul lu dul tàbbiji ci kiiraayu Sëriñ Tuubaa. Werekaan bu mag, te xam woy, mokkal ko, lu mel ni lay bind. Waaye taaru aw làmmiñ it, ci lu ni mel lees ko mën a fésale. Muusaa wax na li mu bëgg a wax te jaaru ci. Dafa jël yeneeni baat, daldi ci gaar li mu nar a tudd lépp, ba fàww yow miy déglu, sa xol ak sa xel ne tekk, taataan li woy wi wund, ngay sog a ming ( = jaayu).
Séex Aliyu Ndaw a ko bind ci téere bi nu tudd ci kow, xët 29-31


Léegi nag nu jublu ci téere yi
Yéen operatëer yiy yëngu ci wàllu alfaabetisayoŋ
OSAD am na mbégtem yëgal leen ne génne na ay téere yu bees, ngir njàng mi gën a naat. Kenn réerewul ne njàngum làmmiñi réew mi rafle na lool i téere, ndaxam de bindkat yaa ngiy góor-górlu, ci fànna bu ne nag (njàngum duruus ak bind, xayma, wér-gi-yaram…) ; xanaa kay li des moo di jënd téere yu doy, yóbbu leen ci daara yi.


Génn-bees !


•    Mellentaan Koote ak Ngatoom, 2009, 28 xët, léeb, albomu kulëer, Séex Aliyu Ndaw
•    Mbaam Aakimoo, II , 2009, 180 xët, téere nettali, Séex Aliyu Ndaw
•    Ci Kepparug Xalima ak Xel, 2009, 96 xët, woyi wolof, Murtadaa Jóob
•    Yóbbalu Ndaw, 2009, 72 xët, woy ak xeltu ci wolof, Marubba Faal

Joomla templates by a4joomla