osad2.jpgosad4.jpgosad1.jpgosad3.jpgosad5.jpg

Note utilisateur: 0 / 5

Etoiles inactivesEtoiles inactivesEtoiles inactivesEtoiles inactivesEtoiles inactives
 

MONDE-SANTE

Àddina – Wér-gi-yaram

Sa yaram dafa tooy, sooy noyyi di fatt, yooyu màndargay ñàkkug deret lañu

25-05-2009 21:20 GMT

Ndakaaru, 25 me (APS) – Sa yaram dafa tooy, ngay fatt, sa xol, di tëf-tëfi bu gaaw, say bët furi, na sa xel jort ñàkkug deret, nga daldi seeti doktoor, loolu lees bind ci ab dalu internet bu tudd Yoonu wér-gi-yaram « Destination Santé ».

 

Màndarga yooyu bu leen sofental, boo leen nemmeekoo ci sa yaram, na sa xel daldi dem ci ñàkkug deret te loolu li koy indi moo di weñ gu ñàkk ci sa yaram ; su ko defee, nga seeti doktoor, rawatina nag bu ci yeneeni màndarga yokkoo : niki doomu jàngoro yi gaaw laa song, say tuñ am ay xar-xar ci koñ yi, say we ak sa kawar di damm.

Yow jigéenu-wérul bi, yow aji-nàmpal ji, yow ndaw si tollu ci jur, soo nemmeekoo màndarga yii rekk, demal gaaw seeti doktoor

Danu war a jàng di ràññee màndarga yooyu, te nu xam ne ñàkkug weñ ci ñii la gën a bon : jigéenu-wérul, jigéen juy nàmpal ak jigéen ju tollu ci jur. Kenn ku ko ci nemmeeku ci ñii nu lim, li ko war moo di dem seeti doktoor mu gëstul ko deretam.

Aram Faal

OSAD a leen baaxe lii :

Ñam yii am nañu weñ : res, yàpp, nen, meew, lànti, ñoom xobi pataas ak ñàmbi ...

 

 

 

Joomla templates by a4joomla