osad2.jpgosad3.jpgosad1.jpgosad4.jpgosad5.jpg

Note utilisateur: 5 / 5

Etoiles activesEtoiles activesEtoiles activesEtoiles activesEtoiles actives
 

Waxtaanu Profesëer Muusaa Seydi, njiitu Oppi Doomi jàngoro yi ca Faan« Maladies infectieuses de Fann », ñu siiwal ko ci yéenekaay « Observateur » n° 3294 bu gaawu 13 ak dibéer 14 sàttumbar 2014, Soxna Aram Faal tënk ko

Profesëer Muusaa Seydi moo ko wax :


« Na leer ne Senegaal defarul garab gu mën faj Ebola »


Laaj : Gan gi àndoon ak Ebola, na mu def ci wàllu xel ?


Tont : Ca njalbéen ga, yëgul woon coow li mu yëkkati. Léegi bi mu wéree, dég-dég yaa ngiy tàmbalee yegsi ci moom ; loolu nag indil na ko njàqare. Xel mi dalul ci njabootam gi des Pàrsel, ñu di leen joxoñ. Mënees naa wax ne xol bi neexul.


Laaj : Wér na péŋŋ ?


Tont : Ci oppu Ebola, màndarga yi mën nañoo deñ, fekk doomu jàngoro jaa ngi ci deret ji. Loolu moo daloon sunu gan gi. Bi ñu jëkkee càmbar deretam, doomu jàngoro jaa ngi ci woon, waaye amatul woon màndarga yi. Looloo tax ñu càmbaraat ko ñaari yoon, sog a gis ne amatul doomu jàngoro ji ci deret ji, amatu ko ci saw mi. Ba tax na jàppees na ne musiba bi dàqu na, gannaw ba doomu jàngoro ji nekkatul ci deretam.


Laaj : Am ñu wax ne wàllaate mën naa am ba tey ci biir ñetti weer yi, su jote séy amee ?


Tont : Xam nañu ne wàllaate gi mën naa am, su jote séy amee. Diiru ñetti weer yi nag, doonte sax wéeruwul ci lu ñu teg bët, xamal ne yokk kaaraange rekk lañu ci jublu. Laaj : Ñakk yi ? Tont : Ñakk du faj, dafay aar ci jàngoro. Ci wàllu faj jàngoro, ñaari pexe ñoo am : 1) benn bi dafa jublu ci saafara màndarga yi, beneen bi jublu ci rey doomu jàngoro ji. Bu dee lu jëm ci Ebola, gannaaw garab gu màcc ci faj ko amul, saafara màndarga yi (biir buy daw, nàcc-nàcc…) moo fi sës. Su ñu ko doxalee ni mu ware, dee gi mën naa wàññeeku bu baax, jóge ci 90% (juróom-ñeen-fukk ci téeméer) wàcc ba ci 20% (ñaar-fukk ci téeméer). Li ñu defal gan gi opp ji daloon du kéemtaan, na leer ci ñépp ne Senegaal defarul garab gu mën faj Ebola, li ñu def bépp fajuwaay mën na ko, ci kow ña fay liggéeye mëne ko te am jumtukaay yi war.

Laaj : Loo xam ci yeneen réew yi opp ji feeñe ?

Tont : Am na réew yu mbir yi doxewul ni muy doxe fii ci Senegaal, te li ko sabab dëgg-dëgg moo di Tëralinu Wér Gu Yaramu Senegaal niroowul ak bosu Liberyaa ak Siyeera-Lewon. Liggéeykati réew yooyu ni liggéeykati Senegaal lañu xareñe, waaye nekkuñu ci anam yu leen may ñu def li war, ndax seen lim bu néew, ak seen tumurànke ci wàllu jumtukaay ak càmbaruwaay.


Laaj : Ebola, xaalis bi ci dugg ñaata la ?


Tont : Mënuma laa wax ñaata la, ndax xaymawuñu ko. Ci lu soxal gan gi, ñun ci sunu bopp, ku ne def na li mu mën. Ca njalbéen ga, doktoor yee yore woon lekkam. Mujj gi, njiitéefu opitaal bi dugal na ci loxoom bu baax. Noonu lañu doon liggéeye. Njàngaan yi nekk ci ñeenteelu at sax, te ñëw di tàggatusi
ci Faan, lée-lée dañuy natt ngir feyal way-opp yi. Mënees naa wax ne Senegaal ak Teraanga ji ko ñépp xamal ñoo taxawu gan gi.


Laaj : Ebola génn na Senegaal ?


Tont : Kenn mënu cee dogu. Nit ñi laale woon ak gan gi ñu ngiy wéy di leen topp te kenn ci ñoom amul màndargay yaram wu tàng. Waaye nag feek opp jaa ngi ci réw yi ñu wër, mëneesul a wax ne Senegaal mucc na ci. Buñu naagu, Nañu wéy ci jëfe santaane yi, te bàyyi tere yi.

Joomla templates by a4joomla