osad5.jpgosad2.jpgosad1.jpgosad4.jpgosad3.jpg

Note utilisateur: 5 / 5

Etoiles activesEtoiles activesEtoiles activesEtoiles activesEtoiles actives
 

Tënk bii, Soxna Aram Faal a ngi ko toxale ci yëglekaayu Frãs bi ñuy woowe « Le Monde » génnoon talaata 9 sàttumbar 2014


Boroom xam-xam yee ko wax :
 «Doomu jàngoro ebola mën naa dund ñetti weer ci maniyu bi «sperme», gannaaw ba aji-opp ji wéree ; loolu dafa laaj nit ki jël matukaayi kaaraange yi war, laata mu jote ci séy».
Laaj ak tont


Laaj : Yan matukaay lees war a jël ngir daan oppu Ebola ?
Tont : 1. Feeñal ñépp ñi opp ji dal, toppatoo leen. Loolu nag yombul, ndax gisees na ci yeneen réew ay nit ñu opp, bañ a dem ci fajukaay yi, xanaa toog ci seen biir njaboot.
2. Feeñal ñi laaleek aji-opp ji, topp leen lu mat ñaar-fukki fan ak benn, gannaaw ba laale gi amee. Su ñu génnewul ay màndarga, fekk na wàllaate amul. Su ñu génnee màndarga, ñu xam ne wàll nañu leen opp ji. Su boobaa, jokkoo ak kër doktoor a war, ngir toppatoo.  
3. Taxawal ay yeete yu takku ñeel opp ji, xamal nit ñi dénkaane ak tere yi boroom xam-xam yi siiwal.
Laaj : Ki opp ji dal, nañu koy def ?
Tont : Fexe ba teg ko ci loxo kër doktoor, ñu ber ko, ngir mu bañ a wàllaate, toppatoo ko. Gannaaw wóoraleesagul ñakk mbaa garab gu ci màcc, dañu koy defal li ñu tudde pajtalu dooleel « soins de support », naka noonu ñu sol ko ndox ndax biir buy daw, indil ko xeeti xorom ak dundeef yi mënul a ñàkk, sol ko ngelaw lu mu noyyi, seetal ko tasyoŋam, fajaale yeneen jàngoro yu ci laxasu... Fàttali telefon bi : 800 00 50 50.
Laaj : Nees di def ngir aaru ci opp ji ?
Tont : Saxoo raxas say loxo, moytu laaleek mbir yu ndoxe yiy génne ci yaramu aji-opp ji, rawatina su fekkee ne màndarga yi feeñ nañu (yaram wu tàng, waccu, biir buy daw, nàcc-nàcc…), bañ a laaleek aji- opp ji ak ay bagaasam…
Laaj : Lees mën a wax ci ndoxum alkol bi ? Ci dëkk yi ndox mu set jafe, ndax loolu dina wàññi wàllaate gi ?
Tont : Ndoxum alkol baax na lool, rawatina fu ndox mu set tumurànke. Waaye nag doyul, fàww ñu sàmmoonte ak dénkaane yeek tere yi : raxas loxo yi ak ndox ak saabu, bañ a laaleek aji-opp ji, naka noonu ak ay bagaasam...
Laaj : Lees mën a wax ci mask yi ?
Tont : Ci jumtukaayi fajkat yi la bokk, ngir lu leen aar, ñoom ñiy jege ki opp ji dal mbaa ku ñu jort ne moo ko dal. Waaye nag, jaar naa leeral  ne, fii ñu tollu ci xam-xam bi ñeel  opp ji, wàllaate gi mënul a jaar ci ngelaw li ñuy noyyi.

Joomla templates by a4joomla