osad2.jpgosad1.jpgosad5.jpgosad3.jpgosad4.jpg

Note utilisateur: 5 / 5

Etoiles activesEtoiles activesEtoiles activesEtoiles activesEtoiles actives
 

EBOLA CA BITI !!
Màndarga yaa ngi nii :
*Waccu yu mën a ànd ak deret * Metitu bopp *Ay picc yu génn ci yaram wi
*Yaram wu tàng jérr *Tenqo yuy metti *Put guy xasan *Cër yuy nàcc ci biir ak ci biti
*Doyadig res ak roñoŋ *Biir buy daw.
Opp ji ñu tudde Ebola, di wàlle, doomu jàngoroo koy joxe. Doomu jàngoro jaa ngi samp dëkkuwaayam ci yaramu njugub, golo ak yu ni mel. Su tàbbee ci yaramu nit, mën na faa toog ñaari fan ba ñaar-fukki fan te du wone boppam, maanaam du feeñal ay màndarga. Su màndarga feeñul nag, wàlle du am. Wàlle gaa ngiy door jamono ji nit ki tàmbalee di waccu, mbaa biiram di daw, mbaa mu am nàcc-nàcc. Su boobaa nag, mën naa wàll képp ku laale ak lu génne ci moom niki : waccu yi, jonkon yi, saw mi, deret ji, maniyu bi, yuut yi, ñandaxit yi, ñaq wi…
Oppu Ebola nees koy faje ?
Dëgg la, fii nu tollu, ameesagul ñakk mbaa garab gu màcc ci pajam ; waaye nag am na ñu ci mën a génn, ci kow ñu teel a jokkoo ak waa kër doktoor, ñooñu teel leen a toppatoo ni mu ware.
Ñan la opp ji gën a gaaw a wàll ?

  • njabootu aji-opp ji ak jegeñaaleem;
  •  ñiy faj aji-opp ji.

Tere yi

  •  bul laale ak njugub, ak golo, naka noonu ak yeneen xeeti mala yi ñuy rëbb ;
  •  bul laale ak nit ku opp ji dal, rawatina lépp lu jëm ci liy génne ci moom : waccu yi, jonkon yi, saw mi, deret ji, maniyu bi, yuut yi, ñandaxit yi, ñaq wi…;
  •  nit ku opp jooju rey, bul laal néewam, bu ko sang, bu ko fóon (loolu dafa laaj matukaay yu wér ci déj yi ngir waajal néew bi, suul ko) ;
  •  Bul jëfandikoo ndab ak bagaas yi néew bi doon jëfandikoo.

Ebola nees koy moytoo ?

  • raxas say loxo ak saabu ak ordsawel ;
  • bañ a laale ak aji-opp ji.

 

Soxna Aram Faal moo ko tënk ci wolof

 

Joomla templates by a4joomla