osad2.jpgosad3.jpgosad5.jpgosad1.jpgosad4.jpg

Note utilisateur: 0 / 5

Etoiles inactivesEtoiles inactivesEtoiles inactivesEtoiles inactivesEtoiles inactives
 

Image lequotidien.sn

 

                                                             (Image:Lequotidien.sn)

 

 

Koor gi ak tàngaayu weeru sulet : jëf yu baax yi ñu dénkaane ci wàllu lekk 

Aali Faal a ko bind ci frãse (Lequotidien), Aram Faal tënk ko ci wolof

Weeru koor, ñaare, mook lekk gu sooxe ñoo ànd. Looloo waral, Njawriñ gi ñu dénk Wér gi ak Taxawu Njaboot gi te Awa Mari Kol Sekk jiite ko, sàkku, ci kurél gi bànqaasoo ci moom te sasoo yeete geek xamle gi ci wàllu wér, ñu tudde ko SNEIPS ci frãse, mu siiwal ab bataaxal boo xam ne dafay wone jëf yu baax yi ci wàllu lekk, rawatina ci jamonoy tàngaay bii.

Bataaxal boobu, lii la la wax, yow aji-woor ji : Ren jii yitam, weeru koor wu sell wi dafa dajeek tàngaay bu metti bi ñu tàmm ci weeru sulet. Dafa laaj, ngir dund weer wii ni mu ware, nga sàmmoonte ak waxtu lekk yi, ni ñu toppantee ci bés bi : xëdd bi mooy jiitu, nga war koo def laata jant bi fenk, ndogu li topp ci ; ñaar walla ñetti waxtu gannaaw ndogu li, reer bi ñëw. Baax na nga jëfandikoo ay meññet, ay suukar yu yéex niki dugub, mburu ak yu ni mel ci xëdd bi. Deel naan ndox ay yooni yoon gannaaw ndogu li, te bul ëppal ci limonaat yeek yeneen soodaa yi ànd ak gaas, moytul ñam yu diis yi, bare diw, bare xorom ci ndogu li, moytul ngato yi, ak yeneen ñam yu saf yi suukar. Lekkal meññet ci ndogu li, doxal mbaa nga yëngal sa yaram gannaaw reer, wàññi coono yu metti yi, te sàmmoonte ak waxtu noppalu yi.

Su dee lu jëm ci ñi ànd ak jàngoroy jabet, li gën a wóor mooy ñu seeti seen doktoor, lu jiitu koor gi ak gannaaw koor gi, ngir ñu seetal leen nattu suukar bi nekk ci seen deret, jox leen dénkaane yi war. Ci lu jëm ci nit ñi seen yaram neexul te ñu bëgg a woor, niki jigéenu- wérul yi, walla mag ñi, mbaa sax ñi ànd ak tasyoŋ walla asma, ñoom it nañu seeti seen doktoor lu jiitu koor gi.

Joomla templates by a4joomla