osad1.jpgosad2.jpgosad4.jpgosad3.jpgosad5.jpg

Note utilisateur: 2 / 5

Etoiles activesEtoiles activesEtoiles inactivesEtoiles inactivesEtoiles inactives
 

Ndeyu Àtte bi, lii la wax ci jigéen ñi

Dog 7
Nit mbindeef mu sell la. Deesu ko wuññi. Wareef la ci nguur gi mu fonk ko, aar ko.
……
Nit ñépp a yem ci kanamu àtte. Gόor ak jigéen ñoo yem ci wàllu yoon.
Ab àtte mooy yombal yemaleg góor ak jigéen ci jox baat yeek ndombo tànk yi.

Dog 15
Àqu moomeel, Ndeyu Àtte bii warlul na ko. ....
Gόor ak jigéen, kenn ku ne yeyoo na am àqu ngajj ak àqu moomeelu suuf, ci anam yi ab àtte tëral.


SÉY AK NJABOOT


Dog 17
Séy ak njaboot ñoo di jiwu wu sell wi meññ mbooloo nit ñi. Ñu ngi leen teg ci kiiraayal Réew mi.

Nguur gi warlul na njaboot gi, cig maasale, rawatina njaboot gi nekk ci dëkki kow yi, lu leen jotale ci këri wér-gi-yaram yi ak ci nekkin wu neex.
Warlul na yitam jigéen ñi, rawatina ñiy dund ci kow gi, yelleef bu jëm ci woyofal seen dundin.

Dog 19
Jigéen yelloo na am jëmmu alalu boppam, ni ko jëkkëram sañe. Yelloo na yoreel boppam alalam.

Dog 22
Xale yépp, gόor ak jigéen, ci bépp gox ci déndu réew mi, yelloo nañu dem ci jàngu yi.

LIGGÉEY


Dog 25
Nit ku ne yelloo na liggéey, yelloo na sàkku am xéy. ...
Gépp xàjjaatle diggante gόor ak jigéen, jëm cim xéy, ak peyoor, ak lempo, terees na ko.

Dog 60-1
Tond bi “Sénat” moo jëmmal mbooloo tund yi nekk ci Repiblig bi ak doomi Senegaal yi sanc bitim réew.

Ñaari juróomeeli way-tond yi, gën jaa néew, ay jigéen lañu.

Joomla templates by a4joomla