osad1.jpgosad2.jpgosad3.jpgosad4.jpgosad5.jpg

Note utilisateur: 0 / 5

Etoiles inactivesEtoiles inactivesEtoiles inactivesEtoiles inactivesEtoiles inactives
 

SUUXAT XELU XALE BI
Ndawal kër doktoor, jagoo nemmeeku waa gox bi, nu tudde ko wéyalkat bi, war naa ñaax way-jur yi ak njaboot gépp, ñuy won xale bi cofeel gu yaatu, di fo ak moom, ndax loolu lu baax la ci màggu xale bi.
Pexe yi mën a cuq xelu xale bi
Lii la way-jur yeek njaboot gi war a def :
-    jamono ji xale bi nekkee ci biiru ndeyam, na ndey ji faral di raay biiram te di wax doomam di ci dégg, loolu dina tax ñu jokkoo.
-    bu xale bi juddoo, nañu ko dàmp ;
-    nañu koy teel a woyal te saxoo di ko def ;
-    wax ak xale bi, bu juddoo rekk ba mu am ay waxtu ;
-    wutal ko ay fowukaay te dimbali ko muy defaral boppam ay fowukaay
-    na ndey ji fo ak doomam ;
-    na ko nettali, ay léeb, ay maye ak yu ni mel ;
-    nay yóbbaale doomam ci doxantu yi mbaa tukki yi ;
-    na njaboot gi wormaal nelawu xale bi ;
-    na njaboot gi moytu lu jëm ci beddi diggante góor ak jigéen.

Xale bu kenn cuqul xelam, ñaare nii lay mel :

•    Dafay naqadi deret ;
•    Dafay tëju ci boppam ;
•    bëggul nit ;
•    doonul ku yeewu ;
•    wóoluwul boppam.

Joomla templates by a4joomla