osad1.jpgosad4.jpgosad2.jpgosad3.jpgosad5.jpg

Note utilisateur: 0 / 5

Etoiles inactivesEtoiles inactivesEtoiles inactivesEtoiles inactivesEtoiles inactives
 

Màndargay jóg-jot-na yiy wone ni jafe-jafe am na ci biir ëmb bi, ci wasin gi ak ci jamonoy gannaaw wasin gi

Màndarga yii ñooy wone ni ëmb bi demewul ni mu ware :
-    xëpp deret ;
-    doom ji ci biiru ndeyam néew na lu muy yëngu, walla dootul yëngu ;
-    yaramu jigéenu-wérul bi dafa tàng ;
-    biiru jigéenu-wérul bi dafa réy lool ;
-    jigéenu-wérul bi dafa ñàkk deret ;
-    jigéenu-wérul bi dafa om, yaram wi jeex tàkk ;
-    jigéenu-wérul bi dafa am yaram ba mu ëpp ;
-    tànk yi, loxo yi ak xar-kanam gi dañu gal, maanaam dañu newi.

Màndarga yii ñooy wone ni wasin gi demewul ni mu ware :
-    mat gu yàgg (lu ëpp fukki waxtu ak ñaar (12) ;
-    xëpp deret lu jiitu wasin gi ;
-    xëpp deret gannaaw wasin gi.
Màndarga yii ñooy wone jafe-jafe ci gannaaw-wasin gi :
-    yaram wu tàng ;
-    tànk yu gal, maanaam newi.

Su benn ci xew-xew yii amee, dawal gaaw kër doktoor, mbaa nga seeti ndawal kër doktoor bu xam-xamam màcc ci mbir mi

Joomla templates by a4joomla