osad2.jpgosad4.jpgosad1.jpgosad3.jpgosad5.jpg

Note utilisateur: 0 / 5

Etoiles inactivesEtoiles inactivesEtoiles inactivesEtoiles inactivesEtoiles inactives
 

Njariñal YODD

Nit ku ne, dale ko ca ba mu nekkee ci biiru ndeyam, dafa soxla yodd ngir màggug yaramam, yokkuteg yóoram, ak màggug xelam.

 

Ñàkkum yodd mën naa jur safaan yu bari : bollax ak yi ci laxasu niki xel mu wayul, ay yàqu-yàqu ci yëngu-yëngu cër yi, añs., biir bu xàcc, maanaam biir bu yàqu ci jigéenu wérul, ak wasin doom ju matul añs.

 Yodd fan lees koy fekk ?

Yodd ci ñam yi jóge géej lañu koy fekk, niki jën, sippax, tuufa, paañ...

Ngir xeex ñàkkum yodd,  boroom xam-xam yi dañu tëral pexe mu baax te yomb, moo di def yodd ci xorom, nga xam ne ñépp a koy jëfandikoo. Looloo waral boroom xam-xam yi ñaax ñépp ci jëfandikoo xoromu yodd, bés bu ne, ci ñamu kër gi.

 

 

DÉNKAANE

-       Am na solo lool ñuy tëj potu xorom si, ngir yodd bi bañ a naaw.

 

 

Joomla templates by a4joomla