Topp-njëfka yi / Les adverbes
Ni ko seen tur feeñale, njëfka « verbe » rekk lañuy àndal
Ràññees na :
1. Topp-njëfka yi mën a ànd ak bépp njëfka :
lool, ndànk, ndànk-ndànk, xaat, mukk …
ndey, ma yërëm ko di ko upp ndànk (taataan lolli, Séex Aliyu Ndaw 27)
li nga ma defal duma ko fàtte mukk.
2. Topp-njëfka yi nga xam ne dañu am takkoo, benn lay doon walla lim bu gàtt ciy njëfka, ñoom rekk lañuy àndal :
taq ripp ; dëgër këcc ; diis gann ; doy sëkk ; forox toll ; jeex tàkk ; jub xocc ; leer nàññ ; lëndëm kuruus ; mag, sut, dàq, mën, gën fuuf/fópp ; mat sëkk ; niin bott ; nooy nepp ; ñuul kukk ; réer mërr ; saf sàpp ; sax dàkk ; set wecc ; sës rëkk ; sew ruuj ; suur këll ; tàng jérr / jépp ; taq ripp ; taxaw jonn / temm ; tooy xepp ; weex tàll ; wér péŋŋ / céŋŋ ; wex xàtt : woyof toyy ; xam xéll ; xees pecc ; xonq coyy / curr.