osad3.jpgosad1.jpgosad2.jpgosad5.jpgosad4.jpg

Note utilisateur: 0 / 5

Etoiles inactivesEtoiles inactivesEtoiles inactivesEtoiles inactivesEtoiles inactives
 

CEETUM NJËKK-WASIN (CONSULTATION PRÉNATALE ( CPN) CI TUBAAB)

« Fàggu moo gën faju ». Jigéenu-wérul mën naa nasaxal bu baax loraange yiy ànd ak wasin, su fekkee ne, diiru ëmb bépp dafay dem kër doktoor ñu seetal ko yaramam. Faatoo ngi tollu ci ëmb bu ndaw.


LAAJ YI

1)    Ñaata yoon la Faatu war a dem CNW = CPN, ngir ñu toppal ko bu baax ëmbam ?
2)    Lu ko ndawal kër doktoor war a digal mu jëfe ko, ngir moytu jàngoro yii :
-    sibbiru ?
-     ñàkkum deret ?
-     tetaanoosu liir ak bu wasin-wees ?
3)    Ana leneen lan la ko ndawal kër doktoor war a digal, ngir wér-gu-yaramam ak gu doomam ?
4)    Lan la ko ndawal kër doktoor war a digal ngir mu mucc ci safaan yi mën a xew ci mat gi ak wasin gi ?

DÉNKAANE YI

-    Faatu, nanga dem lu mu néew néew ñetti yoon ca fajukaay ba, ñu seet la ceetum njëkk-wasin (boo amee 3 weer - 6 weer - 8 weer), su ko defee, dinañu la fa ñakk tetaanoos, jox la ay doomu klorokin ak yu weñ, ñu tudde ko feer ci tubaab, joxaale la fa ay dénkaane ci wàllu lekk. Loolu mën naa fanq, ci kàttanu Yàlla, bépp safaan bu laxasu ci ëmb ak wasin.
-          Faatu, ngir moytu ñàkkum deret, nanga jël benn doomu weñ, ci waxtu lekk, li ko dale ci ndoortel ëmb bi ba keroog ba ngay wasin.
-        Faatu, aaral sa bopp ci sibbiru, ci anam yii : dangay jël 300 mg klorokin (mu di 2 doomu klorokin 150 mg), ñaari yoon ci ayu-bés bi, maanaam altine ju ne ak alxames ju ne, li ko dale ci ndoortel ëmb bi ba keroog ba ngay wasin, ni ko ndawal kër doktoor santaanee.
-        Faatu, ngir aar sa bopp ci sibbiru, deel nelaw ci biir sànke (mustikeer) bu ñu nàndal ;
-    Faatu, ci biir ëmb bi, nanga ñakku tetaanoos ; su ko defee, dinga moytu jàngoro jooju, bon ci yow, bon ci sa doom ;
-    Faatu, boo tolloo ci wasin, ngir fanq safaan, nanga dem dispàñseer, walla nga seet ku jàng rewli mu taxawu la.

NDOLLENT LI

Ci mbirum doomu weñ yi jigéenu-wérul war a wann :
-    Dee ko jël ci waxtu lekk, booy xéewlu ba ci digg bi ; loolu dina tax tawat yi ci laxasu niki xel mu teey, ak waccu, ak biir buy daw wàññeeku ;
-    Boo jëlee doomu weñ, dinga gis say jonkon ñuul, loolu du dara, bu ci am benn jaaxle ;
-    Boo jëlee doom yooyu, nanga daldi lekk ñam wu am witaamin C : sorãs, limoŋ, guyaab ; xob yu nëtëx, tamaate. Nanga moytu, boo lekkee rekk, daldi ci teg àttaaya walla kafe, ndax naan yooyu dañuy tax ba weñ gi du gaaw a tàbbi ci deret ji.



Yéen bàjjanu gox yi, OSAD fàggul na leen ay téere yu ngeen mën a jëfandikoo ci wàllu yeete :

Livret de vulgarisation du Programme élargi de vaccination PEV :
    -en wolof, Nakk yu mat : gàllaaj gu wóor, 24 pages
    -en sereer, Nek teyu : teex booru, 24 pages
Carnets de santé pour la protection maternelle et infantile (consultations prénatales et post-) :
français-wolof, français-sereer et français-pulaar
Sama doom dama koy nàmpal, l’allaitement maternel en wolof, 16 pages
Njiriiñ a numin, l’allaitement maternel en sereer, 20 pages
Ëmbub Jàmm, la maternité en wolof
Bodatar Puubu, la maternité en sereer, 16 pages.
Lexique français-wolof de la santé, 80 pages.
Lekkug tànneef, manuel de nutrition en wolof, 60 pages



Joomla templates by a4joomla