osad4.jpgosad5.jpgosad1.jpgosad3.jpgosad2.jpg

Note utilisateur: 0 / 5

Etoiles inactivesEtoiles inactivesEtoiles inactivesEtoiles inactivesEtoiles inactives
 

Xale bu am lu ëpp 24 weer (ñaar-fukki weer ak ñeent) maanaam ñaari at

Ci at yii, dina fekk ñaare xale bi fer. Xéy na sax am na rakk, su ko defee ndeyam du am jot ju yaatu ju mu ko toppatoo. Ndaxam dees ko war a seet bu baax, ngir mu lekk ni mu ware. Safi am na léegi 30 weer, maanaam ñaari at ak genn-wàll. Bi mu amee 2 at la fer.


LAAJ :
1)    Lan la Safi war a lekk, ngir màgg ni mu ware ?
2)    Nan la ko Abi, ndeyam, mën a jàpplee ba mu lekk bu baax ?

TONT YI
-    Abi, sa doom jii am 2 at ak genn-wàll, soxla na sa ndimbal ba tey, ngir mu màgg, am kàttan ak wér. Gannaaw li muy lekk ci ndën lu mag li, jox ko, ñaari yoon ci bés bi, lekk gu duun (nen, beñe, aakara, njogonal).
-    Abi, wéyal di ko dundal bu baax, te di ko jox meññetu jamono, nga taamu yi seen suux mboq jëm ci xonq (niki màngo, pàppaayo, xaalu tubaab) walla yu forox yi (sorãs, ditax, limoŋ).
-    Abi, toppatoo ko walla nga wut ku ko mag mu toppatool la ko, ba mu wóor la ne, li nga ko tibbal, lekk na ko ba mu jeex.
-    Abi, wéyal di ko yóbbu ca peese ba ; jottalikat bi walla ndawal kër doktoor dina la jàpple ba nga topp ni muy màgge ; su ko defee, dina teel a xam ndax yaram wi dafa wàññeeku ; su loolu amee, mu jox la ndigal yi war.

NDOLLENT LI
-    Xale bu am lu ëpp 2 at dafa soxla di lekk ay yooni yoon, ndax biiram dafa tuuti, muy gaaw a xiif. Dee ko jox ñam yu am solo ci diggante ndënale yi (njogonal, nen, beñe, aakara, añs.)
-    Fexeel ba tibbal ko lu am solo ci dugub ji walla ceeb bi, boole ci lujum (xob yu nëtëx, kànja, karoot) ak jën walla yàpp.


Joomla templates by a4joomla