osad5.jpgosad2.jpgosad4.jpgosad1.jpgosad3.jpg

Note utilisateur: 5 / 5

Etoiles activesEtoiles activesEtoiles activesEtoiles activesEtoiles actives
 

Lekkug xale diggante 12 ba 23 weer (fukki weer ak ñaar ba ñaar-fukki weer ak ñett) :

NÀMPALU WEEN AK ÑAM YI KOY MOTTALl

Weer yii ñoo di jamono yi gën a metti ci xale bi. Mu ngiy dox, lu mu for lekk, boole ci di gaaw a feebar. Ay soxlaam dañuy yokku ci wàllu toppatoo, waaye ñaare, ndey ji jotam du bari. Ci ndënu kër gi lay lekke, bokk ak ñu ko mag fuuf.



DÉNKAANE YI
-    Yow ndey ji, wéyal di nàmpal sa doom ba mu am 2 at, su ko defee, dina xéewlu bu baax ci sa ween.
-    Yow ndey ji, defal ci ruy bi ñam yi koy naatal ba mu doon ruy bu ñu yokk : diwlin, bëer mbaa tiga-dege, meew mbaa ñebbe.
-    Yow ndey ji, bu xale bi toogee ci ndën lu mag li, nanga koy toppatoo bu baax, ngir mu jël lu doy ci ceeb mbaa dugub, ci lujum, ci jën mbaa yàpp.
-    Yow ndey ji, nanga koy jox bés bu ne ci meññet yi xew jamono (màngo, xaal, xaalu tubaab, ditax, sorãs, new, banaana) ; loolu dina ko dimbali mu xeex jàngoro yi.
-    Yow ndey ji, nanga koy jox muy lekk ay yooni yoon : 4 ba 5 yoon ci bés bi ; biiram bu tuuti bi day gaaw a xiif.

NDOLLENT LI
-    Diggante 12 ba 23 weer, lu jafe la ci dundu xale, moo tax toppatoo dëgg la laaj.
-    Gannaaw li muy nàmp, nanga ko faral di jox muy lekk. Gannaaw li muy bokk ak nit ñi ci ndën li, mën nga koo joxaat ñaari yoon mu lekk (naka noonu, gannaaw njogonal li, mën nga koo jox nen, ñoom laax mbaa fonde, ak beñe, añs.)
-    Jox ko yitam meññet yi am ci dëkk bi.
-    Seppi : laata ngay def yu saf yi (niki kaani, poobar, bineegar), sàkkalal sa doom ñeex, morso jën wu baax mbaa yàpp, ak lujum ; su ceeb bi ñoree, nga tibb boole ci. Su ko defee, nga jël loolu lépp tojat ko ba mu sew, jox ko.

Dileen tegal xale yi ndawal

Joomla templates by a4joomla