osad2.jpgosad1.jpgosad3.jpgosad4.jpgosad5.jpg

Note utilisateur: 0 / 5

Etoiles inactivesEtoiles inactivesEtoiles inactivesEtoiles inactivesEtoiles inactives
 

Lekkug xale bi
Nàmpalu ween kese : 0 ba 6 weer
Teel a jox liir bi ween wi te wéyal nàmpalu ween kese

Soowum ween moo di dund bi gën ci liir bi. Teel koo jox ween wi ci fanweeri minit yi topp ci wasin gi baax na lool ci moom ak ci ndey ji.

 

 

Laaj
1)    Liir bi, lu tax ñu war koo teel a jox ween wi ?
2)    Liir bi, lu tax kenn waru koo jox ndox lu jiitu mu am juróom-benni weer (6)?

Tont yi
•    Bu sa doom juddoo rekk, nàmpal ko ci saa si, ndax nga gaaw a am soow ; su ko defee, mu mën a nàmp lërén bi. Te yitam nàmpal sa doom ci saa si, gannaaw wasin gi, dafay yombal génnub ànd bi, wàññi nàcc bi.
•    Lërén, ndox mu xall miy jëkk a génn ci ween wi, mënees naa wax ne ñakku maam Yàlla la, ndax dafay aar liir bi ci jàngoro yi. Bu ko tuur, jox ko sa doom mu nàmp ko.
•    Diggante bi mu juddoo ba ba muy am juróom-benni weer, bu ko jox leneen (moo xam ñam la walla naan la), lu dul soowum ween, ndox sax bu ko ko jox. Soowum ween, fii sa doom tollu, mat na ko sëkk dund, te yit ëmb na, ci ndox, natt bi war ci moom.


Ndollent li
•    Jox ko mu nàmp ba bàyyil boppam ween wi ;
•    jëkk koo jox wenn ween wi ba soow mi jeex, nga jox ko wi ci des ;
•    nàmpal ko, waxtu wu ko soxlaa, guddi ak bëccëg, ndax nga gën a am soow, su ko defee sa doom màgg ni mu ware.


        Nàmpal dafa laaj toogaay mbaa tëraay bu jekk

Jamonoy nàmpal lu am solo la ci ndey ji ak liir bi. Li koy yombal moo di ñoom ñaar ñu nekk ci jataay bu jekk – moo xam dañu toog mbaa ñu tëdd - te liir bi sex ween wi ni mu ware.


Laaj
1.    Lu tax ci jamonoy nàmpal, toogaay mbaa tëraay bu jekk doon lu war ci ndey ji ?
2.    Nan la ndey ji war a téyee doomam, su koy nàmpal ?
3.    Nan lañuy xame ni liir bi nàmp na ni mu ware ?

Tont yi
•    Booy nàmpal sa doom, nanga fexe ba sa toogaay mbaa sa tëraay jekk. Toogaay mbaa tëraay bu jekk dina tax ba doo gaaw a sonn ba di dog nàmpal gi, fekk sa doom doylewul.
•    Ngir, saa soo koy nàmpal, xale bi jël nattu soow mi war ci màggaayam, nanga fexe ba uuf ko bu jekk :
-    xar-kanamam dafay janoo ak ween wi ;
-    biiram dafay tafu ci sa biir.
•    Ngir ween yi bañ a sol mbaa cus yi di metti, nanga fexe ba sa doom jël ween wi ni mu ware :
-    sikkimam dafa war a laal ween wi ;
-    gémmiñam dafa war a ubbeeku bu baax ;
-    lu ñuul li wër cusu ween wi, ci kow lay gën a feeñe ;
-    tuñu suuf wi dafay wàcc.

Ndollent li
•    Jox ko mu nàmp ba bàyyil boppam ween wi ;
•    jëkk koo jox wenn ween wi ba soow mi jeex, nga jox ko wi ci des ;
•    nàmpal ko, waxtu wu ko soxlaa, guddi ak bëccëg, ndax nga gën a am soow, su ko defee sa doom màgg ni mu ware.


Joomla templates by a4joomla