osad4.jpgosad3.jpgosad5.jpgosad1.jpgosad2.jpg

Note utilisateur: 0 / 5

Etoiles inactivesEtoiles inactivesEtoiles inactivesEtoiles inactivesEtoiles inactives
 

Màndargay jóg-jot-na ci biir ëmb bi
A. Tonqi, Xëpp deret
Am na solo jigéenu-wérul bi ak i jegeñaaleem mën a ràññee, ci biir ëmb bi, màndargay jóg-jot-na yi war a tax ñu jàllale jigéenu-wérul bi, na mu gën a gaawe, ci ndawal kër doktoor bu am xam-xam.

Laaj
Lu tax tonqi nekk màndarga jóg-jot-na ci biir ëmb bi ?
Lu tax xëpp deret nekk màndarga jóg-jot-na ci biir ëmb bi ?
Lan la jigéenu-wérul war a def, su fekkee ni ci biir ëmb bi, dafa gis benn ci màndargay jóg-jot-na yi ?

Dénkaane yi
•    Tonqi bi ngay tonqi mën na laa jural jàngoro ju bon, jural ko sa doom ;
•    xëpp deret mën naa doon màndarga buy wone ni ëmb bi dafa am jafe-jafe ;
•    su fekkee ni dangay tonqi mbaa ngay xëpp deret, demal gaaw ci dispàñseer bi la gën a jege, ngir ñu toppatoo la ni mu ware.
     
Ndollent li
Yeneen màndargay jóg-jot-na yi mën a feeñ ci ëmb bi te ñu waral jàllale bu gaaw ci ndawal kër doktoor bu xam liggéeyam ñu ngi nii :
-    yaram wu tàng ;
-    xar-kanam, ak loxo ak tànk yu gal, maanaam newi ;
-    kiriis ;
-    ñàkk deret.  

Màndargay jóg-jot-na ci biir ëmb bi
B. Xar-kanam, ak loxo yu gal, maanaam newi -  Kiriis

Am na solo jigéenu-wérul bi ak i jegeñaaleem mën a ràññee, ci biir ëmb bi, màndargay jóg-jot-na yi war a tax ñu jàllale jigéenu-wérul bi, na mu gën a gaawe, ci ndawal kër doktoor bu am xam-xam.

Laaj
1.    Lu tax xar-kanam ak loxo yu gal nekk ay màndargay jóg-jot-na ci biir ëmb bi ?
2.    Lu tax kiriis nekk màndarga jóg-jot-na ci biir ëmb bi ?
3.    Lan la jigéenu-wérul bi war a def, su fekkee ni xar-kanamam, ak loxoom dañu gal ?
4.    Lan la jegeñaale yi war a def, su fekkee ni jigéenu-wérul dafay kiriis ?

Dénkaane yi
•    Jigéenu-wérul bu xar-kanam ak loxoom gal mën naa def kiriis te loolu baaxul ci moom, baaxul ci  doomam.
•    Kiriis mën naa jur noo gu fatt, ba ndey ji ak doom ji jóge ci faatu.
•    Boo gisee ni sa xar-kanam ak say loxo dañu gal, dawal gaaw ci dispàñseer bi gën a jege, ngir ñu faj la ni mu ware.
•    Boo gisee jigéenu-wérul buy kiriis, yóbbu ko gaaw ci dispàñseer bi gën a jege.

Ndollent li
Yeneen màndargay jóg-jot-na yi, ci biir ëmb bi, nga xam ni war nañoo tax ñu gaaw a jàllale jigéenu-wérul bi ci ndawal kër doktoor bu am xam-xam, ñu ngi nii :
-    yaram wu tàng ;
-    ñàkk deret.
 
Màndargay jóg-jot-na ci biir ëmb bi
C. Yaram wu tàng    Ñàkk deret

Am na solo jigéenu-wérul bi ak i jegeñaaleem mën a ràññee, ci biir ëmb bi, màndargay jóg-jot-na yi war a tax ñu jàllale jigéenu-wérul bi, na mu gën a gaawe, ci ndawal kër doktoor bu am xam-xam.

Laaj
1.    Lu tax yaram wu tàng nekk màndarga jóg-jot-na ci biir ëmb bi ?
2.    Lan la jigéenu-wérul bi war a def, su fekkee ni yaramam dafa tàng ?
3.    Lu tax ñàkk deret nekk màndarga jóg-jot-na ci biir ëmb bi ?
4.    Lan la jigéenu-wérul bi war a def, su fekkee ni dafa ñàkk deret ?
•    Yaram wu tàng baaxul, ndax mën naa jur biir bu yàqu, mbaa wasin doom ju matul, mbaa doom ju indaalewul bakkan. Boo gisee ni sa yaram dafa tàng, dangay daldi gaaw a dem ci dispàñseer bi la gën a jege, ngir ñu faj la ni mu ware.
•    Ñàkk deret baaxul ci jigéenu-wérul ak doom ji mu ëmb ndax mën naa jur wasin doom ju matul mbaa doom ju tuuti lool, mbaa doom ju indaalewul bakkan. Boo gisee say bët furi, sa làmmiñ ak sa ténq (maanaam sa diggu loxo) furi ba weex, dangay daldi daw ci fajukaay bi la gën a jege ngir ñu toppatoo la ni mu ware.



Joomla templates by a4joomla