osad5.jpgosad1.jpgosad4.jpgosad3.jpgosad2.jpg

Note utilisateur: 0 / 5

Etoiles inactivesEtoiles inactivesEtoiles inactivesEtoiles inactivesEtoiles inactives
 

DEEL RAXAS SAY LOXO

Loxo yu tilim ñooy sabab, ñaare, jàngoro yu deme ni biir buy daw. Deel faral raxas say loxo ak ndox mu set ak saabu, loolu mën naa wàññi bu baax a baax biir buy daw, rawatina ci xale bi am diggante tus ba juróomi at (0 ba 5 at).



LAAJ
1)    Lu tax nga war a raxas say loxo ak ndox mu set ak saabu ?
2)    Ci yan jamono tigi nga war a raxas say loxo ak ndox mu set ak saabu ?

DÉNKAANE YI
•    Astu, loxo yu tilim mën nañoo ànd ak ay doomu jàngoro, su ko defee ñu indi biir buy daw ci njaboot gépp. Deel raxas say loxo ak ndox ak saabu, laata ngay togg.
•    Astu, diine dafa santaane cet. Deel raxas say loxo ak ndox mu set ak saabu laata ngay jox sa doom lekk, ngir aar ko ci biir buy daw.
•    Astu, deel raxas say loxo ak ndox mu set ak saabu, waxtu woo génnee ci duus bi yow ci sa bopp, ak waxtu woo laalee jonkonu xale bi, ak laata nga koy jox mu lekk.
•    Astu, deel raxas say loxo ak ndox mu set ak saabu, waxtu woo laalee sa jonkonu doom. Laal boobu nga ko laal te raxasuwoo mën naa indi biir buy daw ci njaboot gépp.
•    Astu, deel raxas say loxo doom ak ndox mu set ak saabu, laata muy lekk. Soo ko defee, dinga ko aar ci biir buy daw.


NDOLLENT LI
Deel raxas say loxo ak ndox ak saabu, rawatina ci jamono yii :
1.    waxtu woo laalee jonkonu xale bi, ak waxtu woo génnee ci duus bi ;
2.    laata nga jox xale bi lekk ;
3.    laata nga defar ñam wi.

 

Joomla templates by a4joomla