osad1.jpgosad4.jpgosad2.jpgosad3.jpgosad5.jpg

Note utilisateur: 5 / 5

Etoiles activesEtoiles activesEtoiles activesEtoiles activesEtoiles actives
 

Woy wii, Séex Aliyu Ndaw moo ko bind, di ko sargale Séex Anta Jóob

Séex Anta Jóob


 
1.    Ndeysaan
2.    Naqar wóoy naqar
3.    Mayi Yàllaa ngi  ne woon nii
4.    Ci sunu wet te xamunu ci woon dara
5.    Nu ngi ne woon jàkk ci jant bi
6.    Ndekete
7.    Naqar wóoy naqar
8.    Bés dina suux ba fàww
9.    Séex Anta saay na
10.    Nu diy baayo
11.    Aa Jóob sab xam-xam
12.    Amul ab gàpp
13.    Buuru Misira yaa la ko sol démb
14.    Tax nga nit ku ñuul suul gàcce
15.    Taxawal faayda
16.    Yaa di sunub biddéew bu fàq
17.    Won gannaaw alalu àddina
18.    Jublu xam-xam bu wér
19.    Ak téere yu dëggu
20.    Say yéene yépp
21.    Afrig bennoo
22.    Sampu fu dëgër
23.    Aa tey nooy baayo
24.    Nun ndawi réew mi
25.    Waaye nooy say dono.

 

Tibbees na ko ci téere bu tudd “Bàkku Xaalis, téere woy”, xët 20, Séex Aliyu Ndaw, Publifan


Njàngat li ci Soxna Aram Faal toftal
Séex Aliyu Ndaw tudd na fii Misira, nu fàttali ne moo di « Egypte ». Séex Anta Jóob def na gëstu yu yaatu, jëm ci wone ne, nit ku ñuul coasaanam Misira la, fa la bawoo, saawu ci biir Afrig gépp. Looloo waral mu dendale làmmiñu Misira – te moo di « égyptien » -  ak làmmiñi Afrig gu ñuul. Mu ngi ko faramfàccee ci téere bu mu bind, tudde ko « Parenté génétique de l’égyptien pharaonique et des langues négro-africaines (NEA, 1977), maanaam mbokkoo gi dox diggante làmmiñu Misira ak làmmiñi nit ñu ñuul ñi fekk baax Afrig. Liggéey boobu wone na ne li làmmiñi Afrig yi di bare yépp, bu ñu ko seetee bu baax, gis ne ñoo bokk maam te loolu moo firndeel bennoog Afrig.


Joomla templates by a4joomla